Banaana
Apparence
Banaana foytéef la gu bawoo ci garabu banaana. Banaana yi ay foytéef lañu yoo xam ne yu ci ëpp duñu am pepp bawoo ci ay xeet yu nit ñi di jëfandikoo. Yennat ci banaana yi nga xam ne nit a koy ji, amnañu ay pepp.
Banaana yi yu ci ëpp dañuy mboq am ay tupp-tupp. Banaana pàcc bu am solo la ci lekkug yenn gox yi. Fu ci mel ni Ugaandaa miy génne lu ëpp juroom-fukki mbir ci banaana.
Cosaanu tur wi nag, lu ëpp ci woroom xam-xami gongikubaat yi ñoo ngi ko delloo ci làkku Wolof ne fa la ko yeneen làkk yépp jële. Ba naa na. Amna ñu ne dafa am foyteef bu tuddoon NA te xaw a mel ni moom, bi banaana feeñee nag te gën koo neex, ñu ne: Ba naa na , maanaam bàyyi naa na.
Nataal yi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]-
Xobu garabug banaana
-
Tóortóoru garabug banaana
-
Meññeefi garabug banaana
Turu xam-xam wi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Musa acuminata
Tur wi ci yeneeni làkk
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]farañse: banane |
angale: banana tree, banana |
itaaliyee: banano, banana |